عَنْ عَائِشَةَ رضي الله عنها قَالَتْ:
فَقَدْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ لَيْلَةً مِنَ الْفِرَاشِ فَالْتَمَسْتُهُ فَوَقَعَتْ يَدِي عَلَى بَطْنِ قَدَمَيْهِ وَهُوَ فِي الْمَسْجِدِ وَهُمَا مَنْصُوبَتَانِ، وَهُوَ يَقُولُ: «اللهُمَّ أَعُوذُ بِرِضَاكَ مِنْ سَخَطِكَ، وَبِمُعَافَاتِكَ مِنْ عُقُوبَتِكَ، وَأَعُوذُ بِكَ مِنْكَ لَا أُحْصِي ثَنَاءً عَلَيْكَ أَنْتَ كَمَا أَثْنَيْتَ عَلَى نَفْسِكَ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 486]
المزيــد ...
Jële nañu ci Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Damaa ñakk Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci genn guddi ci lal bi, ma koy làmbatu far sama loxo tege ci biir ay ndëggoom fekk moo ngi ci jàkka ji fekk dafa samp ñaari tànkam, muy wax naan: "Allaahuma innii ahuusu bi ridaaka min saxatika, wa bi muhaafaatika min huquubatika, wa ahuusu bi ka minka, laa uhsii sanaa-an halayka, anta kamaa asnayta halaa nafsika".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 486]
Aysatu yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa wax ne: dama doon nelaw ci wetu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ma ñàkk ko ci guddi gi, may laal sama loxo ci barab bi mu daan jullee ci néeg bi; fekk ma nga sujjóot ñaari ndëggoom sampu, muy wax naan:
(ahuusu) maa ngi jotewu (bi ridaaka min saxatika) ci man ak samaw xeet, (wa) maa ngi muslu it (bi muhaafaatika) sa njéggal lu bari (min huquubatika) ci sa mbugal, (wa ahuusu bi ka minka) ak ci say rafeti melo, ba tax dara du musle ci yaw ku dul yaw, amul benn musluwaat du caagine làqukaay ci Yàlla lu dul jëm ci moom, (laa uhsii sanaa-an halayka) manumaa takk limub say xéewal ak say rafetal kem ni nga ko yeyoo ak lu ma man a góor-góor lu ci loolu (anta kamaa asnayta halaa nafsika) yaw daal sant nga sa bopp cant gi yell ci yaw, ana kan moo man a joxe àqi sant la?!