عن ثَوْبَانَ رضي الله عنه قال:
كَانَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ إِذَا انْصَرَفَ مِنْ صَلَاتِهِ اسْتَغْفَرَ ثَلَاثًا، وَقَالَ: «اللَّهُمَّ أَنْتَ السَّلَامُ، وَمِنْكَ السَّلَامُ، تَبَارَكْتَ ذَا الْجَلَالِ وَالْإِكْرَامِ»، قَالَ الْوَلِيدُ: فَقُلْتُ لِلْأَوْزَاعِيِّ: كَيْفَ الْاسْتِغْفَارُ؟ قَالَ: تَقُولُ: أَسْتَغْفِرُ اللهَ، أَسْتَغْفِرُ اللهَ.
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 591]
المزيــد ...
Jële nañu ci Sawbaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan wëlbatiku ci julli gi day jéggalu ñatti yoon, daal di wax: "Allaahumma Antas Salaamu, wa Minkas Salaamu, Tabaarakta Sal Jalaali wal ikraami" waliid wax ne: ma wax Al-Awsaahii ne ko: naka lay jéggaloo? Mu ne: day wax naan: Astaxfirul Laaha, Astaxfirul Laaha.
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 591]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan noppi ci julli gi da daan wax: Astaxfirul Laaha, Astaxfirul Laaha, Astaxfirul Laaha.
Mu màggal Boroomam nag ci wax: «Allaahumma Antas Salaamu wa Minkas Salaamu Tabaarakta Sal Jalaali wal ikraami» Yàlla mooy Aji-Mucc ji di Aji-Mat ci ay meloom, di Aji-Set ci bépp ayib ak mànkite, nga sàkku ci moom Aji-Sell ji mucc ci ayi àdduna ak allaaxira doo ko sàkku ci keneen, ndax moom Aji-Sell ji ci moom la yiwi ñaari kër yépp nekk, mooy Boroom màgg gi di Boroom rafetal gi.