+ -

عَنْ عَبْدِ الرَّحْمَنِ بْنِ أَبِي لَيْلَى قَالَ: لَقِيَنِي كَعْبُ بْنُ عُجْرَةَ، فَقَالَ: أَلاَ أُهْدِي لَكَ هَدِيَّةً؟
إِنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ خَرَجَ عَلَيْنَا، فَقُلْنَا: يَا رَسُولَ اللَّهِ، قَدْ عَلِمْنَا كَيْفَ نُسَلِّمُ عَلَيْكَ، فَكَيْفَ نُصَلِّي عَلَيْكَ؟ قَالَ: «فَقُولُوا: اللَّهُمَّ صَلِّ عَلَى مُحَمَّدٍ وَعَلَى آلِ مُحَمَّدٍ، كَمَا صَلَّيْتَ عَلَى آلِ إِبْرَاهِيمَ، إِنَّكَ حَمِيدٌ مَجِيدٌ، اللَّهُمَّ بَارِكْ عَلَى مُحَمَّدٍ وَعَلَى آلِ مُحَمَّدٍ، كَمَا بَارَكْتَ عَلَى آلِ إِبْرَاهِيمَ، إِنَّكَ حَمِيدٌ مَجِيدٌ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6357]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abdur Rahmaan ibn Abii Laylaa mu wax ne: Kahb ibn Hujrata dafa dajee ak man, ne ma: ndax du ma jox àddiya?
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa génn ci nun, nu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, xam nanu naka lanu lay nuyòo, leegi naka lanuy jullee ci yaw?, mu wax ne: "waxleen: Allaahumma salli halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin kamaa sallayta halaa aali Ibraahiima, innaka Hamiidun Majiidun, Allaahumma baarik halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin kamaa baarakta halaa aali Ibraahiima innaka Hamiidun Majiidun".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6357]

Leeral

Sahaaba yi dañoo laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- naka lañuy jullee ci moom? Ginnaw ba ñu xamee naka lañu koy nuyòo, ca taaya ya: "Assalaamu halayka ayyuhan Nabiyyu wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu..."? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaar leen naka lañuy jullee ci moom, te maanaa mi mooy: "Allaahumma salli halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin" Maanaam: tagg ko ci tudd gu rafet ca mbooloo mu kawe ma, ak ñi ko topp ci diineem ji, ak jegeñaaleem yi ko gëm. "kamaa sallayta halaa aali Ibraahiima" Kem ni nga defe ngëneel ci ñoñi Ibraahiima -yal na jàmm nekk ci moom- te ñooy Ibraahiima ak Ismaahiila, ak Ishaaqa, ak seeni sët ak way-gëm yi leen topp, na nga jotale say ngëneel Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-. "innaka Hamiidun Majiidun " Maanaam: ki ñu sant ci sa jëmm ji ak ci sa melo yi ak ci say jëf, di ki yaatu ci sag màggaay ak ci sag kilifteef ak say may. "Allaahumma baarik halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin kamaa baarakta halaa aali Ibraahiima" Maanaam: jox ko ci ay yiw ak i terànga ya ca gën a màgg, te nga dolli ko te saxal ko.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Mag ña dañu daan joxante àddiya masalay xam-xam yi.
  2. Julli ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa war ci taaya ji mujj ci julli.
  3. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamal na Sahaaba yi nuyòo ak ni ñuy jullee ci moom.
  4. Melo wii mooy melo wi gën a mat ci meloy julli ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.