عَنْ أَبِي الزُّبَيْرِ قَالَ:
كَانَ ابْنُ الزُّبَيْرِ يَقُولُ فِي دُبُرِ كُلِّ صَلَاةٍ حِينَ يُسَلِّمُ: «لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ وَحْدَهُ لَا شَرِيكَ لَهُ، لَهُ الْمُلْكُ وَلَهُ الْحَمْدُ وَهُوَ عَلَى كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ، لَا حَوْلَ وَلَا قُوَّةَ إِلَّا بِاللهِ، لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ، وَلَا نَعْبُدُ إِلَّا إِيَّاهُ، لَهُ النِّعْمَةُ وَلَهُ الْفَضْلُ وَلَهُ الثَّنَاءُ الْحَسَنُ، لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ مُخْلِصِينَ لَهُ الدِّينَ وَلَوْ كَرِهَ الْكَافِرُونَ» وَقَالَ: «كَانَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يُهَلِّلُ بِهِنَّ دُبُرَ كُلِّ صَلَاةٍ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 594]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abis Subayri mu wax ne :
Ibn Subayri bu jullee ba sëlmal da daan wax: «laa ilaaha illal laahu wahdahu laa sariika lahu lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say in Xadiirun, laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi, laa ilaaha illal Laahu, wa laa nahbudu illa iyyaahu, lahun nihmatu wa lahul fadlu wa lahus sanaa ul hasanu, laa iLaaha illal Laahu muxlisiina lahud diina wa law karihal kaafiruuna» mu wax ne: «Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na ko tudde Yàlla ginnaaw julli gu ne».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 594]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na tudd Yàlla ci sikar sii ginnaaw bu sëlmalee ci jullig farata yépp, maanaam mooy:
"laa ilaaha illal laahu": manaam amul kenn ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla.
"wahdahu laa sariika lahu" maanaam: moom Yàlla amul bokkaale cig warug jaamu ak cig moomeelam ak ci ay turam ak i meloom.
"lahul mulku" maanaam: moo moom nguur ga matale te yaatu, nguurug asamaan yi ak suuf si ak li nekk séen diggante.
"wa lahul hamdu" maanaam: mooy ki melowoo lépp i mat, ki ñuy sant cig mat ngir bëgg ko ak màggal ko ci gépp anam ci mbégte ak ciw tiis.
"wa Huwa halaa kulli say in Xadiirun" kàttanam lu mat sëkk la ci gépp anam, dara tëwu ko, te menn mbir ci bir yi tëwu ko.
"laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi" maanaam: deesul juge ci wenn melo jëm ci weneen melo, ak cig moy Yàlla jëm ci topp Yàlla, amul it genn kàttan ndare ci ndimbalul Yàlla ndax mooy Dimbalaakoon ba te ci moom la ñuy wakkiirlu.
"laa ilaaha illal Laahu wa laa nahbudu illa iyyaahu": ak feddali la ci maanaam jaamu ak dàq bokkaale, ak ne kenn yayoowul ag jaamu ku dul moom.
"lahun nihmatu wa lahul fadlu": moom moo bind xéewal yi te moo ko moom, dana ci may ci ngëneelam ku ko soob ci ay jaamam.
"wa lahus sanaa-ul hasanu": moo yayoo tagg wu rafet ci jëmmam ak ci ay meloom ak ci ay jëfam ak ay xéewalam, ci képp anam nag.
"laa ilaaha Laaha illal Laahu, muxlisiina lahud diina": maanaam kennal ko ci lu dul ngistal mbaa ndéggtal ci jaamu Yàlla.
"wa law karihal kaafiruuna" maanaam sax ci wéetal Yàlla ak di ko jaamu donte neexul yéefar yi.