+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه: أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«لَا تَجْعَلُوا بُيُوتَكُمْ مَقَابِرَ، إِنَّ الشَّيْطَانَ يَنْفِرُ مِنَ الْبَيْتِ الَّذِي تُقْرَأُ فِيهِ سُورَةُ الْبَقَرَةِ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 780]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«buleen def séen kër yi ay bàmmeel, Saytaane day daw kër goo xam ne dañu fay jàng saaru Al-Baxara».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 780]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day tere neenal kër yi ci julli ba mu mel ni ay bàmmeel ndax deesu fa julli.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamle ne Saytaane day daw kër goo xam ne dañu fay jàng saaru Al-Baxara.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Kanadi البلغارية Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Sopp nañu baril ay jaamu Yàlla ak julliy naafila ci kër yi.
  2. Julli ci ay bàmmeel daganul; ndax jumtukaay la ci jumtukaayi bokkaale yi ak ëppal ca ña fa nekk, ba mu des jullee néew.
  3. Te sax na ci jóge ci Sahaaba yi ñuy tere julli ci bàmmeel yi; looloo tax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere ñuy def kër yi mu mel ni ay bàmmeel kenn du fa julli.