+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«لَأَنْ أَقُولَ: سُبْحَانَ اللهِ، وَالْحَمْدُ لِلهِ، وَلَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ، وَاللهُ أَكْبَرُ، أَحَبُّ إِلَيَّ مِمَّا طَلَعَتْ عَلَيْهِ الشَّمْسُ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2695]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«ma wax: Subhaanal Laahi, wal hamdu lil Laahi, wa laa ilaaha illal Laahu, wal laahu akbaru, moo ma gënal lépp lu jant bi fenk ci kawam».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2695]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne tudd Yàlla mu kawe mi ci baat yu màgg yii moo gën àdduna ak li ci biiram, te mooy:
"Subhaanal Laahi": sellal Yàlla ci gépp wàññeeku.
"alhamdu lil Laahi": tagg Yàlla ci ay meloom yu mat ya ànd ak bëgg ak màggal.
"laa ilaaha illal Laahu": amul kenn ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla.
"al-Laahu akbaru": moo gën a màgg lépp lu mu man a doon.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ñaaxe ci tudd Yàlla, ak ne moo gën lépp lu jant bi fenk ci kawam.
  2. Soññee ci baril di tudd Yàlla, ngir li ci nekk cib yool ak ngëneel.
  3. Bànneexi àdduna lu néew la, te ay neex-neexam it day jeex.