عَنْ عُقْبَةَ بْنِ عَامِرٍ رَضيَ اللهُ عنهُ قَالَ: قَالَ لِي رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«أُنْزِلَ -أَوْ أُنْزِلَتْ- عَلَيَّ آيَاتٌ لَمْ يُرَ مِثْلُهُنَّ قَطُّ، الْمُعَوِّذَتَيْنِ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 814]
المزيــد ...
Jële nañu ci Huqbata Ibn Haamir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na ma:
"wàcce nañu ci man ay aaya yoy musuñoo wàcce yu mel ni ñoom, Ñaari muslukaay yi"
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 814]
Huqbata ibn Haamir yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa nettali jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ko ne: Yàlla wàcce na ci man ci guddi gii aaya yoo xam ne yu mel ni ñoom masula wàcc-maanaam ci muslaay- ñuy Ñaari muslukaay yi: Saaru {Xul ahuusu bi rabbil falaqi} ak Saaru {Xul ahuusu bi rabbin naasi}.