عَنْ عَائِشَةَ رضي الله عنها:
أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَانَ إِذَا أَوَى إِلَى فِرَاشِهِ كُلَّ لَيْلَةٍ جَمَعَ كَفَّيْهِ، ثُمَّ نَفَثَ فِيهِمَا فَقَرَأَ فِيهِمَا: {قُلْ هُوَ اللهُ أَحَدٌ}، وَ{قُلْ أَعُوذُ بِرَبِّ الْفَلَقِ}، وَ{قُلْ أَعُوذُ بِرَبِّ النَّاسِ}، ثُمَّ يَمْسَحُ بِهِمَا مَا اسْتَطَاعَ مِنْ جَسَدِهِ، يَبْدَأُ بِهِمَا عَلَى رَأْسِهِ وَوَجْهِهِ وَمَا أَقْبَلَ مِنْ جَسَدِهِ، يَفْعَلُ ذَلِكَ ثَلَاثَ مَرَّاتٍ.
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 5017]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- guddi gu nekk bu daan yéeg ci lalam day boole ñaari téqam, daal di ciy ëf, daal di jàng: {Xul huwal Laahu Ahadun}, ak {Xul ahuusu Bi Rabbil falaxi} ak {Xul ahuusu Bi Rabbin naasi}, daal di ciy masaa yaramam lu mu man, tàmbalee ca bopp ba ak kanam ga, ak lu ca topp ci yaramam, da koy def ñatti yoon.
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5017]
Leerarug hdiisb: Bokk na ci njubug Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan yéeg ci lalam ngir nelaw day boole ñaari téqam yëkkati leen -kem ni kiy ñaan di def- daal di ciy ëf ci gemeñam, ëf bu sew ànd ak tuuti tiflit daal di jàng saar yii ñatti yoon: {Xul huwal Laahu Ahadun} ak {Xul ahuusu Bi Rabbil falaxi} ak {Xul ahuusu Bi Rabbin naasi} daal di raay ñaari ténqam ci lu mu man ci yaramam; tàmbalee ci boppam ak kanamam ak li féete ci kanam ci yaramam, day baamtu jëf jii ñatti yoon.