+ -

عَنْ ‌أُبَيِّ بْنِ كَعْبٍ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«يَا أَبَا الْمُنْذِرِ، أَتَدْرِي أَيُّ آيَةٍ مِنْ كِتَابِ اللهِ مَعَكَ أَعْظَمُ؟» قَالَ: قُلْتُ: اللهُ وَرَسُولُهُ أَعْلَمُ. قَالَ: «يَا أَبَا الْمُنْذِرِ، أَتَدْرِي أَيُّ آيَةٍ مِنْ كِتَابِ اللهِ مَعَكَ أَعْظَمُ؟» قَالَ: قُلْتُ: {اللهُ لا إِلَهَ إِلا هُوَ الْحَيُّ الْقَيُّومُ} [البقرة: 255]. قَالَ: فَضَرَبَ فِي صَدْرِي، وَقَالَ: «وَاللهِ لِيَهْنِكَ الْعِلْمُ، أَبَا الْمُنْذِرِ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 810]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Ubay Ibn Kahb -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«yaw Aba-Munsir, ndax xam nga ban aaya moo gën a màgg ci téere Yàlla bi?» Nee na: ma ne ko: Yàlla ak ub Yónenteem ñoo xam. Mu ne ma: «yaw Aba- Munsir, ndax xam nga ban aaya moo gën a màgg ci téere Yàlla bi ?» Nee na: ma ne ko: {Allaahu laa-i-Laaha illaa huwa Al-Hayyul Xayyuumu} [Al-Baxara: 255]. Nee na: mu dóor sama dënn, daal di wax ne: «giñ naa ci Yàlla, na xam-xam ndokkeel Aba- Munsir».

-

Leeral

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa laaj Ubay Ibn Kahb aaya bi gën a màgg ci téere Yàlla bi, muy dengi-dengi ci tontu bi, mujj gi mu ne: mooy aayatul Kursiyyu: {Allaahu laa ilaaha illaa huwa Al Hayyul Xayyuumu}, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dëggal ko, daal di fëgg dënnam ngir junj ne fees na dell ak xam-xam ak xereñ, daal di koy ñaanal mu texe ci xam-xam bi te ñu yombalal ko.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Malayalam Telgoo Sawaahili Buurmi Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hdiis bi:
  2. Ag may gu màgg ñeel na Ubay Ibn Kahb -yal na ko Yàlla dollee gërëm-.
  3. Aayatul Kursiyyu mooy aaya bi gën a màgg ci téereb Yàlla bi, kon jaadu na ñu mokkal ko te di settantal ay maanaam ak di ko jëfe.