عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه عَنْ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَنْ سَبَّحَ اللهَ فِي دُبُرِ كُلِّ صَلَاةٍ ثَلَاثًا وَثَلَاثِينَ، وَحَمِدَ اللهَ ثَلَاثًا وَثَلَاثِينَ، وَكَبَّرَ اللهَ ثَلَاثًا وَثَلَاثِينَ، فَتْلِكَ تِسْعَةٌ وَتِسْعُونَ، وَقَالَ: تَمَامَ الْمِائَةِ: لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ وَحْدَهُ لَا شَرِيكَ لَهُ، لَهُ الْمُلْكُ وَلَهُ الْحَمْدُ وَهُوَ عَلَى كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ غُفِرَتْ خَطَايَاهُ وَإِنْ كَانَتْ مِثْلَ زَبَدِ الْبَحْرِ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 597]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku sàbbaal Yàlla
ginnaaw julli gu ne fanweeri yoon
ak ñatt, sant Yàlla fanweeri yoon ak ñatt, màggal Yàlla fanweeri yoon ak ñatt, loolu juróom-ñent-fukk ak juróom ñent la, mu wax: ci mottali ko téemeer: laa-i-Laaha Illal Laahu wahdahu laa sariika lahu lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say-in Xadiirun, ñu jéggal ko ay njuumteem doonte dafa toll ni puuriti géej».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 597]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-leeral na ne ku wax ginnaaw bu noppee ci jullig farata gi:
Fanweeri yoon ak ñatt: "Subhaanal Laahi" te mooy sellal Yàlla ci gépp wàññiku.
Ak fanweer ak ñatt: "Alhamdu lil-Laahi" te mooy tagg ko ci ay meloom yu mat ànd ak bëgg ko ak màggal ko.
Ak fanweer ak ñatt: "Allaahu Akbar" te mooy ne Yàlla moo gën a màgg lépp.
Ngir mottali lim bi téeméer mu wax: "laa iLaaha Illal Laahu wahdahu laa sariika lahu lahul mulku wa lahul hamdu wa Huwa halaa kulli say-in Xadiirun" maanaam mooy: amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla moom dong amul bokkaale, ak ne moom Yàlla mu sell mi moo jagoo nguur gu mat, moo yeyoo kañ ak tagg gu ànd ak bëgg ak màggal wolif keneen ku dul moom, ak ne moom lépp la man dara tëwu ko.
Ku wax loolu loolu dees na far ay njuumteem jéggal ko, donte dafa bari ba toll ni puurit yu weex yiy nekk ci kaw géej gi bu dee yëngatu.