عَنْ أَبِي أُمَامَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَنْ قَرَأَ آيَةَ الْكُرْسِيِّ فِي دُبُرِ كُلِّ صَلَاةٍ مَكْتُوبَةٍ لَمْ يَمْنَعْهُ مِنْ دُخُولِ الْجَنَّةِ إِلَّا أَنْ يَمُوتَ».
[صحيح] - [رواه النسائي في الكبرى] - [السنن الكبرى للنسائي: 9848]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Umaamata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"ku jàng aayatul Kursiyu ginnaaw jullig farata gu ne dara terewukoo
dugg àjjana lu dul dee".
[Wér na] - - [Téere bu mag bi An-nasaa'iy def ci Sunna yi - 9848]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ku jàng aayatul Kursiyu ginnaaw bu noppee ci jullig farata gu ne dara terewu koo dugg àjjana lu dul dee; moom nag moo ngi ci saaru Al-Baxara, mooy waxi Yàlla ji: {Allaahu laa ilaaha illa Huwal Hayyul Xayyuumu laa taaxuzuhu sinatun walaa nawmun lahu maafis Samaawaati wa maa fil-Ardi man zal lazii yasfahu hindahuu illaa bi-iznihii yahlamu maa bayna aydiihim wa maa xalfahum wa laa yuhiituuna bi say-in min hilmihii illaa bimaa saa-a wasiha kursiyyuhus Samaawaaati wal-Ardi wa laa ya-uuduhu hifsuhumaa wahuwal Haliyyul Hasiimu} [Al-Baxara: 255].