عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه عَنْ رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِذَا لَقِيَ أَحَدُكُمْ أَخَاهُ فَلْيُسَلِّمْ عَلَيْهِ، فَإِنْ حَالَتْ بَيْنَهُمَا شَجَرَةٌ أَوْ جِدَارٌ أَوْ حَجَرٌ ثُمَّ لَقِيَهُ فَلْيُسَلِّمْ عَلَيْهِ أَيْضًا».
[صحيح] - [رواه أبو داود] - [سنن أبي داود: 5200]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«bu kenn ci yéen dajee ak mbokkam na ko nuyu, bu dara doxee seen diggante ag garab walla miir walla aw doj mu dajewaat ak moom na ko nuyu batay».
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 5200]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day soññee ci nuyu mbokku jullitam saa yu dajee ak moom, ba bu ñu àndee di dox am lu leen teqale niki ag garab walla miir walla aw doj wu rëy, topp mu dajewaat ak moom ginnaaw ga na ko nuyu beneen yoon.