عن ابن عمر رضي الله عنهما أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«إِذَا أَكَلَ أَحَدُكُمْ فَلْيَأْكُلْ بِيَمِينِهِ، وَإِذَا شَرِبَ فَلْيَشْرَبْ بِيَمِينِهِ، فَإِنَّ الشَّيْطَانَ يَأْكُلُ بِشِمَالِهِ، وَيَشْرَبُ بِشِمَالِهِ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2020]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«bu kenn ci yenn di lekk na lekke loxo ndeyjooram, buy naan na naane loxo ndeyjooram, ndax Saytaane loxob càmmooñam lay lekke, loxob càmmoñam lay naane».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2020]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day digal jullit bi muy lekke ak a naane ab ndeyjooram, di , di ko tere it muy lekke ak naane ab càmmoñam ;ndaxte Saytaane càmmooñam lay lekke di ko naane.