عن عُمر بن أبي سلمة رضي الله عنه قال:
كُنْتُ غُلَامًا فِي حَجْرِ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، وَكَانَتْ يَدِي تَطِيشُ فِي الصَّحْفَةِ، فَقَالَ لِي رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «يَا غُلَامُ، سَمِّ اللهَ، وَكُلْ بِيَمِينِكَ، وَكُلْ مِمَّا يَلِيكَ» فَمَا زَالَتْ تِلْكَ طِعْمَتِي بَعْدُ.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 5376]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Umar Ibn Abii Salamata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
Bama nekkee xale ci kër Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, nuy lekk sama loxo doon wëreelu ci ndab li, Yónente bi ne ma: « yaw xale bi, tuddal Yàlla, te lekke sa loxo ndeyjoor, te lekk li ne ci sa kanam» booba ba leegi noonu laay lekke.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5376]
Umar Ibn Abii Salamata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, di doomi soxnas Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Ummu Salamata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- -moom nag kër yónente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc la yaro- da ñuy xibaar ne: dadoon lekk ben bis loxoom di wër fune ci ndab li di fa tibb, Yónente bi daaldi koy xamal ñatti teggini lekk:
Bi ci njëkk mooy: wax: "bismil Laahi" booy tàmbalee lekk ga.
Ñaareel bi: lekke loxob ndeyjoor.
Ñatteel ba: lekk ci sa kanam.