Listu hadiis yi

ku muñal ki am jafe-jafe, walla mu baal ka ko, Yàlla dana ko keral bis-penc ca suufus keru Gàngunaayam ga bis ba nga xam ne genn ker amul gu dul keram ga
عربي الإنجليزية الأوردية
yéen de dangeen gis seen Boroom kem ni ngeen di gise weer wii, te du ngeen buuxante ngir gis ko
عربي الإنجليزية الأوردية
li ñuy njëkk a àtte ci diggante nit ñi ëllëg bis-pénc mooy dereet
عربي الإنجليزية الأوردية
ndax duma leen xibaare waa àjjana? Ñooy képp ku néew doole, tey toroxlu, te bu giñoon ci Yàlla mu dëggal ko, ndax duma leen xibaare waa sawara? Ñooy képp ku dëgër soxor tey rëy-rëylu
عربي الإنجليزية الأوردية
jaam bi du seqi benn jéego ëllëg bis-pénc ludul ne dees na ko laaj dundam gi ci lan la ko jeexale, ak xam-xamam bi lu mu ci def, ak alalam nan la ko ame ak ci fan la ko dugal , ak yaramam wi ci lan la ko ràppal
عربي الإنجليزية الأوردية
ndax xam ngeen kan mooy ki ñàkk?
عربي الإنجليزية الأوردية
amul benn boroom wurus du caagine xaalis, te du joxe àqam, lu dul ne bu bis-pénc baa dees na ko lalal ay lali xeeri sawara
عربي الإنجليزية الأوردية
ku dégg nodd daldi wax: Allaahuma Rabba haasihid dahwati attaammati, wassalaatil xaa-imati, aati Muhammadan alwasiilata walfadiilata, wabhashu maxaaman mahmuudan allasii wahadtahu, kon samag rammu yell na ci moom ëllëg bis-pénc
عربي الإنجليزية الأوردية
Yàlla du tooñ benn way-gëm ci jëfam ju baax di ko wàññi, dana ka ko jox fii ci àdduna fay ka ko ca allaaxira
عربي الإنجليزية الأوردية
dinaa nekk ca sama mbalka ma di xaar kan ci yéen mooy ñëw ngir naan, waaye dana ñu téye ay nit ba duñu aksi ci man, may wax naan: yaw sama Boroom ci man lañu bokk, ci samaw xeet lañu bokk
عربي الإنجليزية الأوردية
{te dees na leen laaj xéewal yi bis booba}
عربي الإنجليزية الأوردية
dañuy jegeele jant bi ci mbindeef yi ëllëg bis-pénc, ba mu jege leen luy toll ni Miil
عربي الإنجليزية الأوردية
am nga li nga mébét ak lu mel ni moom
عربي الإنجليزية الأوردية
Yàlla day dajale nit ña jiitu ak ña mujj ci benn barab, dañuy dégg aji-woote ji, te it dees leen di gis, Jant bi jege, nit ñi egg ci njàqare ak jafe-jafe lu ñu àttanul te manuñu ko a muñ
عربي الإنجليزية الأوردية
mbooloo miy njëkk a dugg àjjana dañuy nekk ci melow weer wi ci guddig Badr, ña topp ca ñoom gën a tarug leer biddiwu per ci ag leer
عربي الإنجليزية الإندونيسية
bu ngeen dee laaj Yàlla laajleen ko Firdawsi
عربي الإنجليزية الإندونيسية