عَنْ الزُّبَيْرِ بْنِ الْعَوَّامِ قَالَ:
لَمَّا نَزَلَتْ: {ثُمَّ لَتُسْأَلُنَّ يَوْمَئِذٍ عَنِ النَّعِيمِ} [التكاثر: 8]، قَالَ الزُّبَيْرُ: يَا رَسُولَ اللهِ، وَأَيُّ النَّعِيمِ نُسْأَلُ عَنْهُ، وَإِنَّمَا هُمَا الْأَسْوَدَانِ التَّمْرُ وَالْمَاءُ؟ قَالَ: «أَمَا إِنَّهُ سَيَكُونُ».
[حسن] - [رواه الترمذي وابن ماجه] - [سنن الترمذي: 3356]
المزيــد ...
Jële nañu ci Subayru Ibnul Awwaam mu wax ne:
Bi aaya bii wàccee: {te dees na leen laaj xéewal yi bis booba} [At-Takaasuru: 8], As-Subayru dafa wax: yaw Yonnente Yàlla bi, ban xéewal lañu nuy laaj, te li fi am mooy ñaar yu ñuul yi rekk muy tàndarma ak ndox? Mu ne ko: «waaye nag dana am de».
[Tane na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 3356]
Bi aaya bi wàccee: {te dees na leen laaj xéewal yi bu bis baa} maanaam: xalset na leen laaj ndax sant ngeen ci li leen
Yàlla xéewalal ci ay xéewal, As-Subayru Ibnul Awwaam -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, ban xéewal lañu nuy laaj?! Te ñaari xéewal yi jarul laaj te mooy tàndarma ak ndox!
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: waaye nag dees na leen laaj xéewal ànd ak melokaan wii ngeen nekke yépp, ndax ñoom ñaari xéewal lañu yu màgg ci xéewali Yàlla yi.