عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«مَنْ أَنْظَرَ مُعْسِرًا، أَوْ وَضَعَ لَهُ، أَظَلَّهُ اللهُ يَوْمَ الْقِيَامَةِ تَحْتَ ظِلِّ عَرْشِهِ يَوْمَ لَا ظِلَّ إِلَّا ظِلُّهُ».
[صحيح] - [رواه الترمذي وأحمد] - [سنن الترمذي: 1306]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«ku muñal ki am jafe-jafe, walla mu baal ka ko, Yàlla dana ko keral bis-penc ca suufus keru Gàngunaayam ga bis ba nga xam ne genn ker amul gu dul keram ga».
[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 1306]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne képp ku muñal ki ame bor, walla mu teggil ko bor ba, ag payam mooy: Yàlla dana ko keral fa suufus keru Gàngunaayam ga keroog bis-penc ba Jant ba di jege boppi jaam yi, tàngaay wa di tar lool ca ñoom, Kenn du am kerr ku dul ku Yàlla keral.