عَنْ عَبْدِ اللهِ بنِ مَسْعُودٍ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«أَوَّلُ مَا يُقْضَى بَيْنَ النَّاسِ يَوْمَ الْقِيَامَةِ فِي الدِّمَاءِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 1678]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abdallah Ibnu Mashuut mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na :
«li ñuy njëkk a àtte ci diggante nit ñi ëllëg bis-pénc mooy dereet ».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1678]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne li ñuy njëkk a àtte ci diggante nit ñi ëllëg bis-pénc ci tooñ gi ñenn ñi di tooñ ñeneen ñi : mooy dereet, niki ray, ak gaañe.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Màggaayu mbiri dereet, ndax li gën a am solo ca la ñuy tàmbalee.
  2. Bàkkaar dana màgg kem màggaayu yàqute ga nga ca ame, ray bakkan bu set nag bokk na ci yàqute yi gën a màgg te dara gënu koo màgg lu dul kéefar ak bokkaale Yàlla mu kawe mi.
Gaaral tekki yi
Làkk: Àngale Urdu Español Ndollent (55)