+ -

عَنْ عَائِشَةَ أُمِّ المؤْمنينَ رَضيَ اللهُ عنها قَالَت: قَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«تُقْطَعُ اليَدُ فِي رُبُعِ دِينَارٍ فَصَاعِدًا».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6789]
المزيــد ...

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"dees na dagg loxo ci ñenteelu xaaju Diinaar jëm kaw".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6789]

Leeral

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne sàcc bi dañuy dagg loxoom ci càccug ñenteelu xaaju Diinaaru wurus, ak lu ëpp loolu, ag xaymaam di yamoo ak 1.06 Garaam ci wurus.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Sàcc ci bàkkaar yu mag yi la bokk.
  2. Yàlla tënk na mbugalu ab sàcc te mooy ñu dagg loxoom; niki mu ko waxe moom Aji-Kawe ji: {sàcc bu góor bi ak sàcc bu jigéen bi daggleen seen i loxo} [Al-Maa-ida: 38], sunna leeral na sàrti dagg gi.
  3. Li ñu namm ci loxo ci hadiis bi mooy dagg ténq bi ci fi mu teqalikook xasab bi.
  4. Bokk na ci xereñug dagg loxo sàcc, aar alali nit ñi, ak àrtu tooñkat yi dul moom.
  5. Diinaar ab xayma la ci wurus, leegi mu tollook (4.25 garaam); ñenteelu xaaju Diinaar day tolloo ak benn garaam ak dara.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Dariya Rom Majri Malagasi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi
Ndollent