عَنْ أَبِي مُوسَى رضي الله عنه قَالَ:
سُئِلَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ عَنِ الرَّجُلِ يُقَاتِلُ شَجَاعَةً، وَيُقَاتِلُ حَمِيَّةً، وَيُقَاتِلُ رِيَاءً، أَيُّ ذَلِكَ فِي سَبِيلِ اللهِ؟ فَقَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «مَنْ قَاتَلَ لِتَكُونَ كَلِمَةُ اللهِ هِيَ الْعُلْيَا، فَهُوَ فِي سَبِيلِ اللهِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 1904]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Muusa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Laaj nañu Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- waa juy xeex ngir jàmbaare, ak kuy xeex ngir par-parloo, ak kuy xeex ngir ngistal, ana kan ci ñoom moo nekk ci yoonu Yàlla? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di ne: "kiy xeex ngir kàddug Yàlla yëkkatiku kooku moo ngi ci yoonu Yàlla".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1904]
Laaj nañu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wuuteg jubluwaay yi ci ñiy xeex; kuy xeex ngir jàmbaare, walla par-parloo walla ngir ñu gis dayoom ci nit ñi mbaa leneen, kan moo ci nekk ci yoonu Yàlla? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamle ne kiy xeex ci yoonu Yàlla: mooy kiy xeex ngir kàddug Yàlla jëm kaw.