عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بنِ عُمَرَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُما:
أَنَّ امْرَأَةً وُجِدَتْ فِي بَعْضِ مَغَازِي النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ مَقْتُولَةً، فَأَنْكَرَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَتْلَ النِّسَاءِ وَالصِّبْيَانِ.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 3014]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Fekk nañu jenn jigéen ñu ray ko ci benn ci xarey Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, Yonnente bi daal di ñaawlu ñuy ray jigéen ñi ak xale yi.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3014]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa gis jigéen ju ñu ray ci benn xare, mu naqarlu ñuy ray jigéen ñi ak xale yu ndaw yi nga xam ne mataguñu am bàkkaar.