+ -

عَنْ أَبي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَا مِنْ صَاحِبِ ذَهَبٍ وَلَا فِضَّةٍ، لَا يُؤَدِّي مِنْهَا حَقَّهَا، إِلَّا إِذَا كَانَ يَوْمُ الْقِيَامَةِ، صُفِّحَتْ لَهُ صَفَائِحُ مِنْ نَارٍ، فَأُحْمِيَ عَلَيْهَا فِي نَارِ جَهَنَّمَ، فَيُكْوَى بِهَا جَنْبُهُ وَجَبِينُهُ وَظَهْرُهُ، كُلَّمَا بَرَدَتْ أُعِيدَتْ لَهُ، فِي يَوْمٍ كَانَ مِقْدَارُهُ خَمْسِينَ أَلْفَ سَنَةٍ، حَتَّى يُقْضَى بَيْنَ الْعِبَادِ، فَيَرَى سَبِيلَهُ، إِمَّا إِلَى الْجَنَّةِ، وَإِمَّا إِلَى النَّارِ» قِيلَ: يَا رَسُولَ اللهِ، فَالْإِبِلُ؟ قَالَ: «وَلَا صَاحِبُ إِبِلٍ لَا يُؤَدِّي مِنْهَا حَقَّهَا، وَمِنْ حَقِّهَا حَلَبُهَا يَوْمَ وِرْدِهَا، إِلَّا إِذَا كَانَ يَوْمُ الْقِيَامَةِ، بُطِحَ لَهَا بِقَاعٍ قَرْقَرٍ، أَوْفَرَ مَا كَانَتْ، لَا يَفْقِدُ مِنْهَا فَصِيلًا وَاحِدًا، تَطَؤُهُ بِأَخْفَافِهَا وَتَعَضُّهُ بِأَفْوَاهِهَا، كُلَّمَا مَرَّ عَلَيْهِ أُولَاهَا رُدَّ عَلَيْهِ أُخْرَاهَا، فِي يَوْمٍ كَانَ مِقْدَارُهُ خَمْسِينَ أَلْفَ سَنَةٍ، حَتَّى يُقْضَى بَيْنَ الْعِبَادِ، فَيَرَى سَبِيلَهُ إِمَّا إِلَى الْجَنَّةِ، وَإِمَّا إِلَى النَّارِ» قِيلَ: يَا رَسُولَ اللهِ، فَالْبَقَرُ وَالْغَنَمُ؟ قَالَ: «وَلَا صَاحِبُ بَقَرٍ، وَلَا غَنَمٍ، لَا يُؤَدِّي مِنْهَا حَقَّهَا، إِلَّا إِذَا كَانَ يَوْمُ الْقِيَامَةِ بُطِحَ لَهَا بِقَاعٍ قَرْقَرٍ، لَا يَفْقِدُ مِنْهَا شَيْئًا، لَيْسَ فِيهَا عَقْصَاءُ، وَلَا جَلْحَاءُ، وَلَا عَضْبَاءُ تَنْطَحُهُ بِقُرُونِهَا وَتَطَؤُهُ بِأَظْلَافِهَا، كُلَّمَا مَرَّ عَلَيْهِ أُولَاهَا رُدَّ عَلَيْهِ أُخْرَاهَا، فِي يَوْمٍ كَانَ مِقْدَارُهُ خَمْسِينَ أَلْفَ سَنَةٍ، حَتَّى يُقْضَى بَيْنَ الْعِبَادِ، فَيَرَى سَبِيلَهُ إِمَّا إِلَى الْجَنَّةِ، وَإِمَّا إِلَى النَّارِ» قِيلَ: يَا رَسُولَ اللهِ، فَالْخَيْلُ؟ قَالَ: «الْخَيْلُ ثَلَاثَةٌ: هِيَ لِرَجُلٍ وِزْرٌ، وَهِيَ لِرَجُلٍ سِتْرٌ، وَهِيَ لِرَجُلٍ أَجْرٌ، فَأَمَّا الَّتِي هِيَ لَهُ وِزْرٌ، فَرَجُلٌ رَبَطَهَا رِيَاءً وَفَخْرًا وَنِوَاءً عَلَى أَهْلِ الْإِسْلَامِ، فَهِيَ لَهُ وِزْرٌ، وَأَمَّا الَّتِي هِيَ لَهُ سِتْرٌ، فَرَجُلٌ رَبَطَهَا فِي سَبِيلِ اللهِ، ثُمَّ لَمْ يَنْسَ حَقَّ اللهِ فِي ظُهُورِهَا وَلَا رِقَابِهَا، فَهِيَ لَهُ سِتْرٌ وَأَمَّا الَّتِي هِيَ لَهُ أَجْرٌ، فَرَجُلٌ رَبَطَهَا فِي سَبِيلِ اللهِ لِأَهْلِ الْإِسْلَامِ، فِي مَرْجٍ وَرَوْضَةٍ، فَمَا أَكَلَتْ مِنْ ذَلِكَ الْمَرْجِ، أَوِ الرَّوْضَةِ مِنْ شَيْءٍ، إِلَّا كُتِبَ لَهُ، عَدَدَ مَا أَكَلَتْ حَسَنَاتٌ، وَكُتِبَ لَهُ، عَدَدَ أَرْوَاثِهَا وَأَبْوَالِهَا، حَسَنَاتٌ، وَلَا تَقْطَعُ طِوَلَهَا فَاسْتَنَّتْ شَرَفًا، أَوْ شَرَفَيْنِ، إِلَّا كَتَبَ اللهُ لَهُ عَدَدَ آثَارِهَا وَأَرْوَاثِهَا حَسَنَاتٍ، وَلَا مَرَّ بِهَا صَاحِبُهَا عَلَى نَهْرٍ، فَشَرِبَتْ مِنْهُ وَلَا يُرِيدُ أَنْ يَسْقِيَهَا، إِلَّا كَتَبَ اللهُ لَهُ، عَدَدَ مَا شَرِبَتْ، حَسَنَاتٍ» قِيلَ: يَا رَسُولَ اللهِ، فَالْحُمُرُ؟ قَالَ: «مَا أُنْزِلَ عَلَيَّ فِي الْحُمُرِ شَيْءٌ، إِلَّا هَذِهِ الْآيَةَ الْفَاذَّةُ الْجَامِعَةُ»: {فَمَنْ يَعْمَلْ مِثْقَالَ ذَرَّةٍ خَيْرًا يَرَهُ، وَمَنْ يَعْمَلْ مِثْقَالَ ذَرَّةٍ شَرًّا يَرَهُ} [الزلزلة: 8].

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 987]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
«amul benn boroom wurus du caagine xaalis, te du joxe àqam, lu dul ne bu bis-pénc baa dees na ko lalal ay lali xeeri sawara, tàngal ko ca sawaraw Jahannama, diko paase ca wetam ga ak jëham ba ak ndiggam la, teg ca saa bu seddee rekk ñu delloo ko ca, ci bis bob ab nattaleem moo ngi toll ni juróom-fukki junniy at, ba keroog ñuy àtte diggante jaam ñi, mu gis yoonam, benn mu jëm àjjana, walla mu jëm sawara».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 987]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ay xeeti alal, ak fayug ku dul joxe asakaam ëllëg bis-pénc, te bokk na ca:
Bi ci njëkk: wurus ak xaalis ak lu nekk ci seen àtte ci alal yi ak yi ñuy jaay, te mooy yi asaka war te joxewuñu ko ci, bu bis-pénc baa dañu koy seeyal sotti ko ci ay aliwo, daal di cay taal sawaraw Jahannama, mbugal ca boroomam, daal di cay bomb wetam ga ak jëham ba ak ndiggam la, saa bu seddee ñu tàngalaat ko, muy wéy ca anamu mbugal mooma diirub bis-pénc ba nga xam ne moo ngi tool ni juróom-fukki junniy at, ba baa Yàlla di àtte diggante mbindeef yi, mu bokk ci waa àjjana walla ci waa sawara.
Ñaareel bi: boroom giléem gi dul joxe faratay asaka ak àqam, te bokk na ca ratt ko ñeel ña fa teew ci ay way-ñàkk, ñu indi giléem yi mu màgg te duuf ca limam ba gën a bari, ñu daal di tàllal boroomam ëllëg bis-pénc sànni ko ci suuf su yaatu te yamoo ñu koy dëgg ci seen i tànk, di ko màtt ci seen i bëñ, saa bu ña mujj jàllee ci kawam ñu delloosi yu njëkk ya, muy wéy ca anamu mbugal mooma diirub bis-pénc ba nga xam ne moo ngi tool ni juróom-fukki junni at, ba keroog Yàlla di àtte diggante mbindeef yi, mu bokk ci waa àjjana walla ci waa sawara.
Ñatteel bi: ki moom ay nag ak ay gàtt -xar ak bëy- te boroomam du joxe àqi asakaam, ñu indi leen ca lim ba gën a mat dara du ca wàññeeku, ñu daal di tàllal boroomam ëllëg bis-pénc sànni ko ci suuf su yaatu te yemoo, te du am benn bu béjjan bi lemu, du caagine bu amul béjjan, du caagine it bu béjjan yi lemu, waaye ca melokaan wa gën a mat, ñu koy mbëkk ca seen béjjan ya, di ko dëgg ca seen tànk ya, saa bu ña mujj jàllee ci kawam ñu delloosi yu njëkk ya, muy wéy ca anamu mbugal mooma diirub bis-pénc ba nga xam ne moo ngi tool ni juróom-fukki junni at, ba ba Yàlla di àtte diggante mbindeef yi, mu bokk ci waa àjjana walla ci waa sawara.
Ñenteel bi: ki yor fas, moom nag ñatti xeet la:
Bu njëkk bi: bàkkaar la ciy am, te mooy ki ko wut ngir ngistal ak puukarewu ak xeex waa lislaam.
Ñaareel bi: sutura la ciy am, te mooy ki ko wut ngir jihaad ci yooyu Yàlla, topp mu rafetal jëme ci moom ci di ko xont ak mbooleem dundam, te bokk na ca boyal bu góor ba.
Ñatteel bi: da ciy am yool, te mooy ki ko wut ngir jihaad ci yoonu Yàlla mu ñeel waa lislaam, mu nekk ci ay dër ak i tool ngir sàmm, du ca lekk lu dul ñu bindal ko limub la mu lekk ay yiw, bindal ko li mub ay nefereem ay yiw, te du ñu dagg buumam ga, te mooy buum ngi ñu koy yeewe, mu daw wéy ci kaw suuf; lu dul ne danañu ko bindal li mu ay jeexitalam ak i nefereem ay yiw, te boroomam du ko rombale ci ag dex mu naan ca te nammu ko woon a nàndal, lu dul ne dees na ko bindal li mu la mu ca naan ay yiw.
Topp ñu laaj ko yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mbaam ndax day yamoo ak fas?
Mu wax ne: dara ci yoonal gu mu jagoo waccu ci, lu dul aaya ju néew moroom jii, te dafa matale ci mbooleem xeeti topp yi ak moy yi; te mooy waxu Yàlla ji: {ku jëf luy toll ni aw fepp ci lu baax dana ko gis, ku jëf luy toll ni aw fepp ci lu bon dana ko gis}. [As-Salsala: 8], ku jëf ci li mu yor mbaam ag topp dana gis yoolu loolu, bu dee ag moy la jëf dana gis mbugalu loolu, te lee dafa matale mbooleem jëf yi.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Warug joxe asaka, ak tëkku gu tar gi tege ci bañ ko.
  2. Ñàkk a kéefarloo ki bañ a joxe asaka ngir tàyyeel, waaye moo ngi ci giraawaale gu tar.
  3. Nit ki dees na ko fay mbooleem ay jëfam bu ca jubloo cosaan la, donte sax jubluwul faramface yooya.
  4. Àq ju dul asaka nekk na ci alal ji.
  5. Bokk na ci àqi giléem ratt ko ñeel ña fa teew ci ay way-ñàkk ca barab ba muy naane ndox; ngir mu gën a yomb ci aji-aajowoo ji ci muy dem ca kër ya, te moo gën a am ñeewant ci jur gi, Ibn Battaal nee na: alal ji am na ñaari àq: faratay jëmm ak gu dul moom, ratt gi dafa bokk ci àq yi nga xam ne ci teddngay jikkó la.
  6. Bokk na ci àq yi war ci giléem ak nag ak gàtt yi boyal bu góor ba bu sàkkoo fori.
  7. Àtteb mbaamu kër ak lépp lo xam ne yaxub sariiha rotuci: mooy ne day dugg ci waxi Yàlla ji: (ku jef lu toll ni aw fepp ci lu baax dana ko gis, ku jëf it lu toll ni aw fepp ci lu bon dana ko gis).
  8. Aaya bi am na xemmeemloo ci jëf lu baax donte lu néew la, ak xuppaate ci jef lu bon donte lu xeebu la.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Dariya Serbi Kinirowanda Rom Majri الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية المقدونية الماراثية
Gaaral tekki yi