عَنِ الْمِقْدَادِ بْنِ الْأَسْوَدِ رَضيَ اللهُ عنهُ قَالَ: سَمِعْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، يَقُولُ:
«تُدْنَى الشَّمْسُ يَوْمَ الْقِيَامَةِ مِنَ الْخَلْقِ، حَتَّى تَكُونَ مِنْهُمْ كَمِقْدَارِ مِيلٍ»، قَالَ سُلَيْمُ بْنُ عَامِرٍ: فَوَاللهِ مَا أَدْرِي مَا يَعْنِي بِالْمِيلِ؟ أَمَسَافَةَ الْأَرْضِ، أَمِ الْمِيلَ الَّذِي تُكْتَحَلُ بِهِ الْعَيْنُ قَالَ: «فَيَكُونُ النَّاسُ عَلَى قَدْرِ أَعْمَالِهِمْ فِي الْعَرَقِ، فَمِنْهُمْ مَنْ يَكُونُ إِلَى كَعْبَيْهِ، وَمِنْهُمْ مَنْ يَكُونُ إِلَى رُكْبَتَيْهِ، وَمِنْهُمْ مَنْ يَكُونُ إِلَى حَقْوَيْهِ، وَمِنْهُمْ مَنْ يُلْجِمُهُ الْعَرَقُ إِلْجَامًا» قَالَ: وَأَشَارَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ بِيَدِهِ إِلَى فِيهِ.
المزيد
Jële nañu ci Al-Miqdaad ibnul Aswad yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"dañuy jegeele jant bi ci mbindeef yi ëllëg bis-pénc, ba mu jege leen luy toll ni Miil",Sulaym ibn Haamir wax ne: giñ naa ci Yàlla ne xamuma lan mooy Miil? Ndax ab soriwaay la ci suuf, walla li ñuy tusngale bët la,mu ne:"nit ñi nekk ci ñaq kem seen i jëf,amna ci ñoom ku muy toll ci ay dojoram, amna ci ñoom ku muy toll ci ay óomam, amna ci ñoom ku muy toll ci ndiggam, amna ci ñoom ku ñaq wi di ŋalaab ag ŋalaab" nee na:Yonente Yàlla bi daal di junj loxoom ci gémmiñam.