عَن أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«يُسَلِّمُ الرَّاكِبُ عَلَى المَاشِي، وَالمَاشِي عَلَى القَاعِدِ، وَالقَلِيلُ عَلَى الكَثِيرِ».
وَلِلبُخَارِي: «يُسَلِّمُ الصَّغِيرُ عَلَى الكَبِيرِ، وَالمَارُّ عَلَى القَاعِدِ، وَالقَلِيلُ عَلَى الكَثِيرِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6232]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne :Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«ki war mooy nuyu kiy dox, kiy dox mooy nuyu ki toog, ñi néew ñooy nuyu ñi bari».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6232]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day jàngale teggini nuyòo ci diggante nit ñi "assalaamu halaykum wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu", Xale nuyu mag, ki war nuyu kiy dox, kiy dox nuyu ki toog, lim bu néew nuyu ñu bari ñi.