عَنْ صَفْوَانَ بْنِ مُحْرِزٍ قَالَ: قَالَ رَجُلٌ لِابْنِ عُمَرَ رضي الله عنهما كَيْفَ سَمِعْتَ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، يَقُولُ: فِي النَّجْوَى؟ قَالَ: سَمِعْتُهُ يَقُولُ:
«يُدْنَى الْمُؤْمِنُ يَوْمَ الْقِيَامَةِ مِنْ رَبِّهِ عَزَّ وَجَلَّ، حَتَّى يَضَعَ عَلَيْهِ كَنَفَهُ، فَيُقَرِّرُهُ بِذُنُوبِهِ، فَيَقُولُ: هَلْ تَعْرِفُ؟ فَيَقُولُ: أَيْ رَبِّ أَعْرِفُ، قَالَ: فَإِنِّي قَدْ سَتَرْتُهَا عَلَيْكَ فِي الدُّنْيَا، وَإِنِّي أَغْفِرُهَا لَكَ الْيَوْمَ، فَيُعْطَى صَحِيفَةَ حَسَنَاتِهِ، وَأَمَّا الْكُفَّارُ وَالْمُنَافِقُونَ، فَيُنَادَى بِهِمْ عَلَى رؤُوسِ الْخَلَائِقِ هَؤُلَاءِ الَّذِينَ كَذَبُوا عَلَى اللهِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2768]
المزيــد ...
Jële nañu ci Safwaan ibn Muhris mu wax ne: jenn waay dafa wax Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm naka nga dégg Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di ko wax ci dée ga? Mu ne: dégg naa ko mu wax ne:
"dees na jegeele aji-gëm ji Boroomam bu màgg bi ëllëg bis-pénc, ba mu teg suturaam ci kawam, di ko saxalal ay bàkkaaram,naan ko: ndax xam nga? Mu naan: ay Sama Boroom xam naa, mu ne ko: man maa la ko suturaaloon ca àdduna, maa la ko jéggal tay, ñu jox ko téerey jëfam yu rafet, bu dee yéefar yi nag ak naaféq yi, dañu leen di woo ci kanamu mbindeef yi naan ñii ñooy ñi weddi Yàlla".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2768]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ni Yàlla di déeye jaamam biy aji-gëm ëllëg bis-pénc, mu wax ne:
Dees na jegeele aji-gëm ji ci Boroomam ëllëg bis-pénc mu teg ci kawam suturaam ga wolif way-taxawaay ba ba kenn du gis ay bóotam ku dul moom, mu ne ko:
Ndax xam nga bàkkaar sàngam ak sàngam...di ko saxalal bàkkaar yi dox ci diggante jaam bi ak Boroomam.
Mu naan: waaw waaw yaw sama Boroom.
Ba bu aji-gëm ji jàqee daal di tiit, Yàlla Aji-Sell ji ne ko: man maa la ko suturaaloon ca àdduna, maa la ko baal tay, ñu jox ko téerey jëfam yu rafet.
Bu dee yéefar bi ak naaféq bi dees leen di woo ci kanamu ñëpp, ñii ñooy ñi weddi Yàlla, rëbbum Yàlla yal na tege ci kaw tooñkat yi.