عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بْنِ عَمْرٍو رضي الله عنهما قَالَ: قالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«حَوْضِي مَسِيرَةُ شَهْرٍ، مَاؤُهُ أَبْيَضُ مِنَ اللَّبَنِ، وَرِيحُهُ أَطْيَبُ مِنَ المِسْكِ، وَكِيزَانُهُ كَنُجُومِ السَّمَاءِ، مَنْ شَرِبَ مِنْهَا فَلاَ يَظْمَأُ أَبَدًا».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6579]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Sama mbalka ma de mi ngi toll ne doxu weer, ndoxam ma moo gën a weex meew, xetam ga moo gën a neex gëttug misk, te koppu yi dañoo mel ni biddiwi yi nekk ci asamaan Ku ci naan doo mar mukk ».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6579]
Leerarug hdiis bi : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne am na am mbalka ëllëg bis-pénc, guddaayam mi ngi toll ne doxu weer yaatuwaayam it naka noonu, Ndoxam ma moo gën a weex meew, Xetam moo gën a neex te gën a teey xetu misk, Ay koppam moo ngi toll ne biddiwi asamaan cig bari, Ku naan ca mbalka ma ci kopp yooya dootul mar ba fàwwu.