+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: سَمِعْتُ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«يَقْبِضُ اللَّهُ الأَرْضَ، وَيَطْوِي السَّمَوَاتِ بِيَمِينِهِ، ثُمَّ يَقُولُ: أَنَا المَلِكُ، أَيْنَ مُلُوكُ الأَرْضِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 4812]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:
«Yàlla dat ŋëb suuf si, lem asamaan yi ci ndayjooram, di wax naan: man maay buur, ana buuri suuf si».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 4812]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne yawmal xiyaam Yàlla day ŋëb suuf si dajale ko, mu lem asamaan si ci ndayjooram taxañ lenn la ca kaw leneen la daal di koy dindi jële ko fi, topp muy wax naan: man maay buur, ana buuri suuf si?!

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Uyguuriya Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Fàttalee ci ne nguurug Yàlla moo fiy des nguurug keneen nag day deñ.
  2. Màggug Yàlla ak màggug kàttanam ak nguuram ak matug nguuram.