عَنْ جَابِرٍ رضي الله عنه قَالَ:
أَتَى النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ رَجُلٌ فَقَالَ: يَا رَسُولَ اللهِ، مَا الْمُوجِبَتَانِ؟ فَقَالَ: «مَنْ مَاتَ لَا يُشْرِكُ بِاللهِ شَيْئًا دَخَلَ الْجَنَّةَ، وَمَنْ مَاتَ يُشْرِكُ بِاللهِ شَيْئًا دَخَلَ النَّارَ»
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 93]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Benn waay dafa ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, yan mooy ñaar yiy waral ? Mu ne ko: «ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara dana dugg àjjana, ku faatu te bokkaale ko ak dara dana dugg sawara».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 93]
Benn waay dafa laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ñaari jikko: jiy waral dugg àjjana, ak jiy waral dugg sawara? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tontu ko ne ko: melo wiy waral dugg àjjana mooy nit ki faatu fekk Yàlla rekk la doon jaamu te bokkaalewu ko ak dara. Jiko jiy waral dugg sawara nag mooy nit ki faatu fekk da doon bokkaale Yàlla ak dara, di wutal Yàlla ndend jig jaamu ak momeelam gi ak ay turam ak i meloom.