+ -

عَنْ مُعَاذٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ، قَالَ:
كُنْتُ رِدْفَ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ عَلَى حِمَارٍ يُقَالُ لَهُ عُفَيْرٌ، فَقَالَ: «يَا مُعَاذُ، هَلْ تَدْرِي حَقَّ اللَّهِ عَلَى عِبَادِهِ، وَمَا حَقُّ العِبَادِ عَلَى اللَّهِ؟»، قُلْتُ: اللَّهُ وَرَسُولُهُ أَعْلَمُ، قَالَ: «فَإِنَّ حَقَّ اللَّهِ عَلَى العِبَادِ أَنْ يَعْبُدُوهُ وَلا يُشْرِكُوا بِهِ شَيْئًا، وَحَقَّ العِبَادِ عَلَى اللَّهِ أَنْ لا يُعَذِّبَ مَنْ لا يُشْرِكُ بِهِ شَيْئًا»، فَقُلْتُ: يَا رَسُولَ اللَّهِ أَفَلاَ أُبَشِّرُ بِهِ النَّاسَ؟ قَالَ: «لا تُبَشِّرْهُمْ، فَيَتَّكِلُوا».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 2856]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Muhaas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Toggoo woon naa ak Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- am Mbaam mu ñuy woowe Xufayr, mu ne ma: «yaw Muhaas, ndax xam nga lan moy Àqi Yàlla ci ay jaamam, ak lan mooy àqi jaam ñi ci Yàlla?», Muhaas nee: ma ne ko: Yàlla ak ub Yónenteem ñoo ko xam, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- daal di ne ko: «àqi Yàlla ci jaam ñi mooy ñu jaamu ko te bañ koo bokkaale ak dara, àqi jaam ñi ci Yàlla nag mooy du mbugal ku ko bokkaalewul ak dara» ma ne ko: yaw Yónente Yàlla bi tee maa bégal nit ñi ci lii ? Mune ma: «buleen bégal kon dañuy bayliku.

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 2856]

Leeral

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral àqi Yàlla ci jaam ñi, ak àqi jaam ñi ci Yàlla, ci ne àqi Yàlla ci jaam ñi mooy ñu jaamu ko moom dong te duñu ko bokkaale ak dara, Ak ne àqi jaam ñi ci Yàlla mooy mu bañ a mbugal ñi koy kennal te duñu ko bokkaale ak dara. Muhaas ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, ndax duma bégal nit ñi ngir ñu bég ci ngëneel lii? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere ko ngir ragal nit ñi di sukkandiku ci loolu.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hdiis bi:
  2. Leeral àqi ji Yàlla waral ci jaamam ñi, te mooy ñu jaamu ko, te bañ koo bokkaale ak dara.
  3. Leeral àqi jaam ñi ci Yàlla mu kawe mi te Yàlla warlul ko boppam ngir ngëneel ak xéewal, te mooy mu dugal leen àjjana, te du leen mbugal.
  4. Ag bégle la ñeel way-kennal yi nga xam ne duñu bokkaale Yàlla ak dara ci ne séenug mujj mooy dugg àjjana.
  5. Muhaas dafa nettali hadiis bii laata muy faatu; ngir ragal a tàbbi ci bakkaaru nëbb xam-xam.
  6. Artu ci bañ a tasaare yenn Hadiis yi ci yenn nit ñi ngir ragal ci kaw ñi nga xam ne manu ñoo xam maanaama; te loolu mooy yi nga xam ne jëf aju wu ca mbaa AB daan ci daani Sariiha yi.
  7. Ñiy kennal Yàlla tey def ay bàkkaar ñoo ngi ci ron coobarey Yàlla bu ko soobee mbugal leen, bu ko soobee it mu jéggal leen, waaye seenug mujj mooy àjjana.