+ -

عَنْ أَنَسٍ رضي الله عنه قَالَ:
جَاءَ رَجُلٌ إِلَى النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فَقَالَ: يَا رَسُولَ اللهِ، مَا تَرَكْتُ حَاجَّةً وَلَا دَاجَّةً إِلَّا قَدْ أَتَيْتُ، قَالَ: «أَلَيْسَ تَشْهَدُ أَنْ لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ وَأَنَّ مُحَمَّدًا رَسُولُ اللهِ؟» ثَلَاثَ مَرَّاتٍ. قَالَ: نَعَمْ، قَالَ: «فَإِنَّ ذَلِكَ يَأْتِي عَلَى ذَلِكَ».

[صحيح] - [رواه أبو يعلى والطبراني والضياء المقدسي] - [الأحاديث المختارة للضياء المقدسي: 1773]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Am na ku mas a ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ko: Yaw Yónente Yàlla bi, man de bàyyiwuma lu rëy walla lu ndaw lu dul ne def naa ko, mu ne ko: «Ndax dangay seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ci dëgg ku dul yàlla, ak ne Muhammat mooy Yónente Yàlla?» Ñatti yoon. Mu ne ko: Waaw, mu ne: «Lii ci la juge».

-

Leeral

Leerarug hdiis bi: Benn waay dafa ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, man de bàkkaar ak moy Yàlla gune def naa ko, bàyyiwuma lu ndaw mbaa lu mag lu dul ne def naa ko, ndax dees na ma jéggal? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: xanaa du seede nga ne amul kenn ku ñu war a jaamu ci dëgg ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la? Mu baamtul ko ko ñatti yoon, Mu tontu ko ne ko: waaw seede naa ko, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamal ko ngëneeli ñaari baati seede yi ak ne dañuy far ay ñaawtéef, ndaxte tuub day far la ko jiitu.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Malayalam Telgoo Sawaahili Buurmi Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hdiis bi :
  2. Màggug ñaari baati seede yi ak not gi ñu not bàkkaar yi ñeel képp ku ko wax te mu dëggu ci xolam.
  3. Lislaam day far bàkkaar yi ko jiitu.
  4. Tuub gu dëggu day far li ko jiitu.
  5. Bokk na ci njubug Yónente bi buy jàngale di ko baamtu.
  6. Ngëneeli ñaari baati seede yi ci ne ñoom ay sabab la ñu ci mucc ci sax ca sawara.