+ -

عَنْ سُفْيان بنِ عَبْدِ اللهِ الثَّقَفِيّ رضي الله عنه قال:
قُلْتُ: يَا رَسُولَ اللهِ، قُلْ لِي فِي الْإِسْلَامِ قَوْلًا لَا أَسْأَلُ عَنْهُ أَحَدًا غَيْرَكَ، قَالَ: «قُلْ: آمَنْتُ بِاللهِ، ثُمَّ اسْتَقِمْ».

[صحيح] - [رواه مسلم وأحمد] - [مسند أحمد: 15416]
المزيــد ...

Jële nañu ci Sufyaan Ibnu Abdullah As-Saxafii -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne :
Wax naa : yaw Yónente Yàlla bi, wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc".

[Wér na] - [Muslim soloo na ko, ak Ahmat] - [Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya - 15416]

Leeral

Sahaaba bii di Sufyaan Ibnu Abdullah -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ngir mu xamal ko wax ju matale maanaay lislaam yi mu jàpp ci te du ko laajaat kenn ku dul moom ? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko : waxal : wéetal naa Yàlla, te gëm naa ne mooy sama Yàlla, moom laay jaamu, moo ma bind, moom laay jaamu ci dëgg deesu ko bokkaale ak dara. Topp mu wommatul Yàlla, topp ko, ci ay farataam, ak bàyyi yi Yàlla araamal, te sax ci loolu.

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Uyguuriya Bengali Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Witnaam Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Cosaanu diine mooy gëm Yàlla cig moomeelam, ak cig jaamu, ak ci ay turam ak i meloom.
  2. Solos njub ginnaaw gëm, ak wéy cig jaamu, ak sax ci loolu.
  3. Ngëm Yàlla sàrt la ngir ñu nangu jëf yi.
  4. Gëm Yàlla, day làmboo lépp luñu war a fas ci ay pas-pasi ngëm ak i cosaanam, ak la cay topp ci ay jëfi xol, ak wommatu ak nangul Yàlla ci li nëbbu ak li feeñ.
  5. Jub mooy taqoo ak yoon wa, ci def yi war ak bàyyi yi ñu tere.