عَنِ ابْنِ عُمَرَ رضي الله عنهما عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، قَالَ:
«مَثَلُ الْمُنَافِقِ، كَمَثَلِ الشَّاةِ الْعَائِرَةِ بَيْنَ الْغَنَمَيْنِ تَعِيرُ إِلَى هَذِهِ مَرَّةً وَإِلَى هَذِهِ مَرَّةً».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2784]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«misaalum naaféq bi, moo ngi mel ni xar mu réer ci diggante ñaari xar, day daw jëm bii ci yoon wii dawaat jëm ca bee aw yoon».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2784]
Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral melow naaféq bi, ci ne moo ngi mel ni xar muy jaabante te xamul man mbooloo ci gàtt yi lay topp, Day dem ci mbooloo mii, leeg-leeg mu dem ci mbooloo mee, Ñoom dañoo gëlëm ci diggante ngëm ak kéefar, ànduñu ak way-gëm ñi ci li feeñ ak li nëbbu, ànduñu it ak yéefar yi ci li feeñ ak li nëbbu, li feeñ sax kay way-gëm yi lañu ci àndal, waaye li nëbbu ci sikk-sakka ak deŋŋ-deŋŋ la nekk, leeg-leeg mu jeng jëm ci ñii, leeg-leeg mu jeng jëm ci ñee.