عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بْنِ عَمْرِو بْنِ الْعَاصِ رضي الله عنهما قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِنَّ الْإِيمَانَ لَيَخْلَقُ فِي جَوْفِ أَحَدِكُمْ كَمَا يَخْلَقُ الثَّوْبُ الْخَلِقُ، فَاسْأَلُوا اللَّهَ أَنْ يُجَدِّدَ الْإِيمَانَ فِي قُلُوبِكُمْ».
[صحيح] - [رواه الحاكم والطبراني] - [المستدرك على الصحيحين: 5]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haasi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«ngëm day ràpp ci biiru kenn ci yéen kem ni yéere bu ràpp di ràppe, ñaanleen Yàlla mu yeesal ngëm ci séen i xol».
[Wér na] - [Al-haakim soloo na ko, ak At-tabaraaniy] - [Adiis yees dabaatal ci ñaari téere Adiis yi gën a wér - 5]
Leerarug hdiisb: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ngëm day ràpp ci xolu jullit bi di néew doole, kem ni yéere bu bees di ràppe ndax li ñu ko yàgg a jëfandikoo; Li koy waral nag mooy lott ci jaamu ga, ak toggoo moy ya, ak nuur ci bànneex yi. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digal nu nuy ñaan Yàlla mu kawe mi mu yeesal sunug ngëm, ci nuy def farata yi ak di baril di ko tudd ak jéggalu.