+ -

عَنْ أَنَسٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ، قَالَ: لَأُحَدِّثَنَّكُمْ حَدِيثًا سَمِعْتُهُ مِنْ رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ لاَ يُحَدِّثُكُمْ بِهِ أَحَدٌ غَيْرِي: سَمِعْتُ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«إِنَّ مِنْ أَشْرَاطِ السَّاعَةِ أَنْ يُرْفَعَ العِلْمُ، وَيَكْثُرَ الجَهْلُ، وَيَكْثُرَ الزِّنَا، وَيَكْثُرَ شُرْبُ الخَمْرِ، وَيَقِلَّ الرِّجَالُ، وَيَكْثُرَ النِّسَاءُ حَتَّى يَكُونَ لِخَمْسِينَ امْرَأَةً القَيِّمُ الوَاحِدُ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 5231]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dinaa leen nettali ab Hadiis bu ma dégge ci Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- kenn du leen ko nettali ku dul man: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
Bokk na ci màndargay bis-pénc nu yëkkati xam-xam, réer bari, njaalo bari, naan sàngara bari, góor ñi néew, jigéen ñi bari, ba juróom-fukki jigéen di tolloog benn góor».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5231]

Leeral

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne bokk na màndarga yiy wane ne bis-pénc jege na nu yëkkati xam-xamu Sariiha ci deewug Boroom xam-xam yi, Loolu nag moo waral réer gi bari te tasaaroo, njaalo ak ñaawtéef day tasaaroo, naan sàngara bari, limub góor ñi néew limu jigéen ñi dolliku; ba tax juróom-fukki jigéen am genn góor guy taxawe séeni bir di ko yéwénal.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hdiis bi :
  2. Leeral yenn màndargay bis-pénc.
  3. Xam waxtuw bis-pénc daa bokk ci biri kumpa yi yàlla jagoo.
  4. Soññee ci sàkku xam-xamu Sariihaa balaa mu fee juge.