عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بْنِ عَمْرٍو رضي الله عنهما قال: قال رَسولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«أَرْبَعٌ مَنْ كُنَّ فِيهِ كَانَ مُنَافِقًا خَالِصًا، وَمَنْ كَانَتْ فِيهِ خَلَّةٌ مِنْهُنَّ كَانَتْ فِيهِ خَلَّةٌ مِنْ نِفَاقٍ حَتَّى يَدَعَهَا: إِذَا حَدَّثَ كَذَبَ، وَإِذَا عَاهَدَ غَدَرَ، وَإِذَا وَعَدَ أَخْلَفَ، وَإِذَا خَاصَمَ فَجَرَ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 58]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"ñent yii ku ñu nekk ci moom nekk na ab naaféq bu sotti, ku wenn melo ci ñoom nekk ci moom
am na wenn melow naaféq ba keroog mu koy bàyyi: bu waxtaanee fen, bu kóllareentee wor, bu digee wuute ko, bu xuloo wax lu bon".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 58]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day moytandikuloo ñent melo yoy bu dajee ci jullit bi day niróo lool ak naaféq yi ngir sababus melo yii, loolu nag mooy ki melo yi not ci moom, bu dee ki mu néew ci moom kooku du ci dugg, te mooy:
Bu njëkk bi: bu waxtaanee day fen te tay ko, te du dëggal ci ay waxam.
Ñaareel bi: bu kóllareentee ag kóllare du ko matal, te day wor àndandoom.
Ñatteel bi: bu
digee du matal dig ba, te da koy wuute.
Ñenteel bi: bu xulóo daal di xëccoo ak kenn ab xulóom day tar, mu jeng wolif dëgg, di fexe ngir delloo ko ak neenal ko, di wax ay neen ak i fen.
Naaféq mooy feeñal lu wuute ak li mi nëbb, te maanaa mii dafa nekk ci boroom melo yii, ag naaféqam day nekk ci àqi ka mu waxal, te dig ko, wóolu ko, te xulóo ak moom, ak nit ki kóllareente ak moom, waaye du ne naaféq la ci lislaam, ku wenn melo ci melo yii nekk ci moom; kon am na melow naaféq ba keroog mu koy bàyyi.