عَنِ الْعَبَّاسِ بْنِ عَبْدِ الْمُطَّلِبِ رضي الله عنه أَنَّهُ سَمِعَ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، يَقُولُ:
«ذَاقَ طَعْمَ الْإِيمَانِ مَنْ رَضِيَ بِاللهِ رَبًّا، وَبِالْإِسْلَامِ دِينًا، وَبِمُحَمَّدٍ رَسُولًا».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 34]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abbaas ibn Abdul Muttalib yal na ko Yàlla dollee gërëm mu ne dégg na Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«ñam na cafkag ngëm ki gërëm Yàlla muy Boroomam, lislaam di diineem, Muhammat di yonnenteem».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 34]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne aji-gëm ji dëggu cig ngëmam ki ab xolam dal, dana yëg ci xolam ag ubbiku, ak ug yaatu ak mbégte ak neexit, ak cafkag jege Yàlla ndeem gëm na ñatti mbir:
Bi ci njëkk: gërëm na Yàlla nekk
Boroomam, loolu nag ci mu ubbi dënnam ci la cay rot di bawoo fa Yàlla te kennal Yàlla ci moomeelam di ko waral, ci séddale wërsëg yi ak nekkiin yi, du yég ci xolam genn gaar ci loolu, te du sàkku beneen boroom bu dul Yàlla mu kawe mi.
Ñaareel bi: mu gërëm lislaam muy diineem, ci mu ubbi dënnam ci li lislaam làmboo ci def ay jëf, ak i warugar, te du dox ci lu dul yoonu lislaam.
Ñatteel bi: mu gërëm Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di yonnenteem, ci mu ubbi dënnam di bég ci li mu indi ci lu dul dengi-dengi walla sikk-sàkka, du sóobu ci lu dul lu dëppoo ak njubam yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.