عَنْ أَبِي أُمَامَةَ الْبَاهِلِيِّ رضي الله عنه قَالَ:
جَاءَ رَجُلٌ إِلَى النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَالَ: أَرَأَيْتَ رَجُلًا غَزَا يَلْتَمِسُ الْأَجْرَ وَالذِّكْرَ، مَا لَهُ؟ فَقَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «لَا شَيْءَ لَهُ» فَأَعَادَهَا ثَلَاثَ مَرَّاتٍ، يَقُولُ لَهُ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «لَا شَيْءَ لَهُ» ثُمَّ قَالَ: «إِنَّ اللَّهَ لَا يَقْبَلُ مِنَ الْعَمَلِ إِلَّا مَا كَانَ لَهُ خَالِصًا، وَابْتُغِيَ بِهِ وَجْهُهُ»
[صحيح] - [رواه النسائي] - [سنن النسائي: 3140]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abii Umaamata Al-Baahilii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Benn waay dafa ñëw ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ne ko: luy mbiri waa jiy xare ngir amug pay ak uw tur, lan moo ko ñeel? Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: "dara ñeelu ko" mu baamtu ko ñatti yoon, Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc naan ko: "dara ñeelu ko" topp mu ne ko: "Yàlla du nangu ci jëf yi lu dul lu sell ñeel ko, ñu jublu sa jëmmam ji"
[Wér na] - - [Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy - 3140]
Benn waay dafa ñëw ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: ngir laaj ko, di sàkku a xam àtteb waa ji génn jëm ca xare ba ak jihaad ga di sàkku ci Yàlla ag pay ak it bëgg nit ñi tagg ko kañ ko, ndax dana am ag pay? Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tontu ko: ci ne du am dara cig pay; ndax li mu bokkaale Yàlla ci yéeneem, waa ji baamtuwaat laaj bi ñatti yoon ci Yonnente bi feddaliwaat tontu bi; ci ne du am ug pay, topp Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xibaar ko tënk gi Yàlla di nangoo jëf: ci ne Yàlla du nangu jef lu dul ñu def lépp ngir moom wolif ñu koy bokkaale ak kenn, ak mu nekk ngir jëmmam ju Sell ji.