عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ، قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِنَّ أَوَّلَ زُمْرَةٍ يَدْخُلُونَ الجَنَّةَ عَلَى صُورَةِ القَمَرِ لَيْلَةَ البَدْرِ، ثُمَّ الَّذِينَ يَلُونَهُمْ عَلَى أَشَدِّ كَوْكَبٍ دُرِّيٍّ فِي السَّمَاءِ إِضَاءَةً، لاَ يَبُولُونَ وَلاَ يَتَغَوَّطُونَ، وَلاَ يَتْفِلُونَ وَلاَ يَمْتَخِطُونَ، أَمْشَاطُهُمُ الذَّهَبُ، وَرَشْحُهُمُ المِسْكُ، وَمَجَامِرُهُمْ الأَلُوَّةُ الأَنْجُوجُ، عُودُ الطِّيبِ وَأَزْوَاجُهُمُ الحُورُ العِينُ، عَلَى خَلْقِ رَجُلٍ وَاحِدٍ، عَلَى صُورَةِ أَبِيهِمْ آدَمَ، سِتُّونَ ذِرَاعًا فِي السَّمَاءِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 3327]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"mbooloo miy njëkk a dugg àjjana dañuy nekk ci melow weer wi ci guddig Badr, ña topp ca ñoom gën a tarug leer biddiwu per ci ag leer, te duñu saw duñu dem wanag, duñu tifli du ñu ñandu, seen peñe yi ci wurus la, seen ñaq yi Misk la, seen garabi taal yu neex ya bantu gëtt la, seen jabar ya Huuru Hiin lañu, ñu nekk ci bindug kenn nit, ci melow seen baay Aadama, juróom-benn-fukki xasab ci kaw".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3327]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamle na ne mbooloom jullit miy njëkk a dugg àjjana seen kanam yi ni weeru guddig Badr lay mel ci leer, topp ña tege ca ñoom ñooy gën a tar biddiwu per bi ci asamaan ci ag leer, ay melo yu mat ñeel na leen ba tax duñu saw te duñu xayta, duñu tifli duñu ñandu, seen peñe yi wurus la, seen taal ya di xetu gëtt di ca gilli, mu gën a teey cuuraay, seen jabar yi ay Huuru Hiin lañu, seen jikkó yi di jikkóy benn nit, ñu nekk ci melow seen baay Aadama ci guddaay ak mbindiin; guddaayu seen yaram yi juróom-benn-fukki xasab la ci asamaan.