عَنْ عُبَادَةَ بْنِ الصَّامِتِ رَضيَ اللهُ عنهُ أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«فِي الجَنَّةِ مِائَةُ دَرَجَةٍ مَا بَيْنَ كُلِّ دَرَجَتَيْنِ كَمَا بَيْنَ السَّمَاءِ وَالأَرْضِ، وَالْفِرْدَوْسُ أَعْلاَهَا دَرَجَةً وَمِنْهَا تُفَجَّرُ أَنْهَارُ الجَنَّةِ الأَرْبَعَةُ، وَمِنْ فَوْقِهَا يَكُونُ العَرْشُ، فَإِذَا سَأَلْتُمُ اللَّهَ فَسَلُوهُ الفِرْدَوْسَ».
[صحيح] - [رواه الترمذي] - [سنن الترمذي: 2531]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ubaadata Ibnus Saamit -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"àjjana amna téeméeri daraja diggante ñaari daraja yu nekk day mel ni diggante asamaan ak suuf, Firdawsi moo ca gën a kawe daraja te ca la ñenti dexi àjjana yi di balle, te ca kawam la Aras nekk, bu ngeen dee laaj Yàlla laajleen ko Firdawsi".
[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2531]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamle na ne àjjana téeméeri daraja ak wàccuwaay la, te diggante ñaari daraja yu nekk ci soriwaay moo ngi mel ni diggante asamaan ak suuf, te li gën a kawe ci daraja yii mooy àjjanay Firdawsi, te ca moom la ñenti dexi àjjana yi di balle, te ca kaw Firdawsi la Aras nekk; bu ngeen dee ñaan Yàlla nangeen ko ñaan Firdawsi; ndax moo nekk ci kaw mbooleem àjjana yi.