عَنِ ابْنِ عَبَّاسٍ رضي الله عنهما قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ أَنْ تُؤْتَى رُخَصُهُ، كَمَا يُحِبُّ أَنْ تُؤْتَى عَزَائِمُهُ».
[صحيح] - [رواه ابن حبان] - [صحيح ابن حبان: 354]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Yàlla daa bëgg ñu def limu yombal, kem ni mu bëgge ñu def mbir yimu dogu».
[Wér na] - [Ibnu Hibbaan soloo na ko] - [Téere bu wér bi ñeel Ibnu Hibbaan - 354]
Leerarug hdiisbi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da ñuy xamal ne: Yàlla daa bëgg ñu def ay yombalam yi mu yoonal, ci woyofal àtte yi ak jaamu yi, ak yombalal ko mukallaf mi ngir ngànt -niki wàññi julli ak boole ko cib tukki-, Kem nimu bëgge ñu def ay dogoom, ci bir yu war yi; ndaxte ndigalul Yàlla ci yombal yi ak ci dogu yi benn la.