عَنْ حَكِيمِ بْنِ حِزَامٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ، قَالَ:
قُلْتُ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، أَرَأَيْتَ أَشْيَاءَ كُنْتُ أَتَحَنَّثُ بِهَا فِي الجَاهِلِيَّةِ مِنْ صَدَقَةٍ أَوْ عَتَاقَةٍ، وَصِلَةِ رَحِمٍ، فَهَلْ فِيهَا مِنْ أَجْرٍ؟ فَقَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «أَسْلَمْتَ عَلَى مَا سَلَفَ مِنْ خَيْرٍ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1436]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Hakiim Ibn Hisaam -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, mu wax ne:
Damaa wax: yaw Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaar ma ci bir yi ma daan def ca ceddo ga, ci sarax ak goreel, ak jokk mbokk, ndax am na yool? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «jébbalu nga ànd ak la nga defoon ciw yiw».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1436]
Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne yéefar bi bu jébbaloo dees na ko fay ab yool ca lamu defoon ca ceddo ga lu jiitu Lislaam ci ay jëf yu baax ci sarax, ak goreel jaam, ak jokk mbokk.