عَنْ أَسْمَاءَ بِنْتِ أَبِي بَكْرٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُمَا، قَالَتْ: قَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِنِّي عَلَى الحَوْضِ حَتَّى أَنْظُرَ مَنْ يَرِدُ عَلَيَّ مِنْكُمْ، وَسَيُؤْخَذُ نَاسٌ دُونِي، فَأَقُولُ: يَا رَبِّ مِنِّي وَمِنْ أُمَّتِي، فَيُقَالُ: هَلْ شَعَرْتَ مَا عَمِلُوا بَعْدَكَ، وَاللَّهِ مَا بَرِحُوا يَرْجِعُونَ عَلَى أَعْقَابِهِمْ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6593]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Asmaa Doomu Abuu Bakar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«dinaa nekk ca sama mbalka ma di xaar kan ci yéen mooy ñëw ngir naan, waaye dana ñu téye ay nit ba duñu aksi ci man, may wax naan: yaw sama Boroom ci man lañu bokk, ci samaw xeet lañu bokk, ñu wax ma ne: ndax yég nga li ñu def sa ginnaaw, ñoo ngi giñ ci Yàlla ne deñu ñu woon di dellu ginnaaw».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6593]
Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ëllëg bis-pénc day nekk ca mbalkaa ma di xaar kan ci xeetam wi mooy ñëw ca mbalka ma, Danañu téye ay nit ci wetam -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: yaw sama Boroom ci man lañu bokk, ci samaw xeet lañu bokk, Ñu ne ko: ndax xam nga li ñu def ginnaaw bi nga tàqalikoo ak ñoom, ñoo ngi giñ ci Yàlla te deñuñu di dellu ginnaaw di tubbi, bokkuñu ci yaw, bokkuñu ci saw xeet.