+ -

عَنِ النُّعْمَانِ بْنِ بَشِيرٍ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِنَّ أَهْوَنَ أَهْلِ النَّارِ عَذَابًا مَنْ لَهُ نَعْلَانِ وَشِرَاكَانِ مِنْ نَارٍ، يَغْلِي مِنْهُمَا دِمَاغُهُ كَمَا يَغْلِ الْمِرْجَلُ، مَا يَرَى أَنَّ أَحَدًا أَشَدُّ مِنْهُ عَذَابًا، وَإِنَّهُ لَأَهْوَنُهُمْ عَذَابًا».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 213]
المزيــد ...

Jële nañu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
«ki gën a woyof mbugal ci waa sawara mooy ki am ñaari dàll ak ñaari waroy dàll yu sawara, yuuram gi di ci bax kem ni cin di baxe, ba du foog ne kenn a ko gën a tar mbugal, te moo leen gën a woyof mbugal».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 213]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ki gën a woyof mbugal ci waa sawara ëllëg bis-pénc mooy ki am ñaari dàll ak ñaari waroy dàll yuuram di bax ngir seen tàngaay, kem ni cinu përëm di baxe, ba du gis ne kenn gën na ko a tar mbugal, fekk moo leen gëna tar mbugal, loolu nag ngir mbugalu yaram ak mu xel daje ci moom.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Àrtu moykat yi ak yéefar yi ci tiitaangey mbugal mii ca sawara; ngir ñu sori lu cay jëme.
  2. Ñay dugg sawara sénni barab ca sawara dafa wuute ci kem seen jëf ya.
  3. Tarug mbugalum sawara, yal na nu ci Yàlla mu kawe mi musal.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Nipali Dariya Rom Majri الموري Ukraani الجورجية المقدونية الماراثية
Gaaral tekki yi