+ -

عَنْ ‌عَبْدِ اللهِ بْنِ عَمْرِو بْنِ الْعَاصِ رضي الله عنها أَنَّهُ سَمِعَ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«إِذَا سَمِعْتُمُ الْمُؤَذِّنَ فَقُولُوا مِثْلَ مَا يَقُولُ، ثُمَّ صَلُّوا عَلَيَّ، فَإِنَّهُ مَنْ صَلَّى عَلَيَّ صَلَاةً صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ بِهَا عَشْرًا، ثُمَّ سَلُوا اللهَ لِيَ الْوَسِيلَةَ، فَإِنَّهَا مَنْزِلَةٌ فِي الْجَنَّةِ، لَا تَنْبَغِي إِلَّا لِعَبْدٍ مِنْ عِبَادِ اللهِ، وَأَرْجُو أَنْ أَكُونَ أَنَا هُوَ، فَمَنْ سَأَلَ لِيَ الْوَسِيلَةَ حَلَّتْ لَهُ الشَّفَاعَةُ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 384]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne dégg na Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:
«bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man, ndax ku julli ci man genn julli Yàlla julli ci moom fukk, te ngeen ñaanal ma Wasiila ba, ndax moom ab bérab la ca àjjana, te kenn yayoowu ko ku dul ab jaam ci jaami Yàlla yi, te maa ngi yaakaar ne man la, ku ma ñaanal Wasiila samag ramm dagan na ko».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 384]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day tegtal kiy dégg kiy nodd ñeel julli gi muy bàmtu ci ginnaawam, di wax lu mel ni li muy wax, bamu des ci ñaari Hàyyahala yi, ndax day wax ci séen ginnaaw: laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi, daal di julli ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ginnaaw bu nodd gi jeexee, ndax ku julli ci moom genn julli Yàlla dana julli ci moom ci sababus loolu fukki julli, maanaam jullig Yàlla ci jaam bi nag mooy: muy tagg jaam bi fa Malaaka ya.
Mu digle ñu ñaanal ko Yàlla Wasiila -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, te moom ag daraja la ca àjjana, te moo ca gën a kawe, te daraja jooju du yéwén mbaa muy yomb lu dul ñeel benn jaam ci mbooleem jaami Yàlla yi, te maa ngi yaakaar ne man la, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax loolu ngir toroxlu; ndaxte bu fekkee ne daraja ju kawe jooju, kenn rekk moo koy am, kon kenn kooku du nekk ku dul moom Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-; ndax moom moo gën ci mbindéef yi.
Yonnente bi leeral ne ku ñaanal Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Wasiila ag rammam dana ko jot -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Uyguuriya Bengali Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ñaaxe ci tontu noddkat bi.
  2. Ngëneelu julli ci Yonnente bi ginnaaw buñu tontoo noddkat bi ba noppi.
  3. Ñaaxe ci ñaanal Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Wasiila ginnaaw buñu jullee ci moom ba noppi.
  4. Leeral maanaam Wasiila ak mbiram mu kawe, ba tax du yéwén lu dul ñeel kenn rekk.
  5. Leeral ngëneelu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ba tax ñu jagleel ko daraja ju kawe jooju.
  6. Ku ñaan Yàlla Wasiila ñeel Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- kooku ramm ma dagan na ko.
  7. Leeral toroxlug Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ba tax muy sàkku ci xeetam wi ñu ñaanal ko daraja jooju, ànd ak loolu moo koy moom.
  8. Yaatug ngëneelu Yàlla ak yërmàndeem, benn bu baax fukk yu mel ni moom mooy ag payam.