Toftaleg Adiis yi

Ku jàpp te rafetal njàpp ma, ay ñaawtéefam day génn ci aw yaramam bay génn ci ay weyam
عربي Àngale Urdu
Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf
عربي Àngale Urdu
saytaane day fas ci ginnaaw boppu kenn ci yéen bu dee nelaw ñatti fas, genn fas-fas gu nekk day waral ci yaw guddi gu gudd, mu naan nelawal
عربي Àngale Urdu
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan jàppu ci julli gu ne
عربي Àngale Urdu