عن عَمْرُو بْنُ عَامِرٍ عَنْ أَنَس بن مالك قَالَ:
كَانَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَتَوَضَّأُ عِنْدَ كُلِّ صَلَاةٍ، قُلْتُ: كَيْفَ كُنْتُمْ تَصْنَعُونَ؟ قَالَ: يُجْزِئُ أَحَدَنَا الْوُضُوءُ مَا لَمْ يُحْدِثْ.
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 214]
المزيــد ...
Jële nañu ci Amru Ibn Aamir mu jële ci Anas Ibn Maalik mu wax ne:
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan jàppu ci julli gu ne, ma ne ko: lan ngeen daan def yéen? Mu ne: njàpp mi dana doy nit ki feeg tojlewul.
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 214]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan jàpp ci jullig farata gu ne, donte njàppam tojul; loolu ngir am yool ak ngëneel.
Dana dagan nag ñu julli ci mennum njàpp lu ëpp benn julli farata feeg moo ngi ca njàpp ma.