عَنِ ‌ابْنِ عَبَّاسٍ رضي الله عنهما قَالَ:
تَوَضَّأَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ مَرَّةً مَرَّةً.

[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 157]
المزيــد ...

Jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na benn-benn.

[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 157]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeg-leeg bu daan jàpp day raxas cér bu nekk benn yoon, mu raxas kanam gi -ca la gallaxndiku ak saraxndiku bokk-, ak ñaari loxo yi ak ñaari tànk yi benn yoon, lii mooy dayo bi war.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Li war ci raxas cér yi mooy benn yoon, lu ca tege dañu koo sopp.
  2. Yoonal nañu di jàpp benn-benn leeg-leeg.
  3. Li ñu yoonal ci masaa bopp mooy benn yoon.
Gaaral tekki yi
Làkk: Àngale Urdu Español Ndollent (58)