عن عبدِ الله بن عمرو رضي الله عنهما قال:
كنتُ أكتبُ كلَّ شيءٍ أسمعُه من رسولِ الله صلَّى الله عليه وسلم أُريدُ حفْظَه، فنهتْني قريشٌ، وقالوا: أتكْتبُ كلَّ شيءٍ تَسمَعُه من رسول الله صلَّى الله عليه وسلم، ورسولُ الله صلَّى الله عليه وسلم بَشَرٌ يتكلَّمُ في الغضَبِ والرِّضا؟ فأمسَكتُ عن الكتاب، فذكرتُ ذلك لرسول الله صلَّى الله عليه وسلم، فأومأ بإصبَعِه إلى فيه، فقال: «اكتُبْ، فوالذي نفسي بيدِه، ما يَخرُجُ منه إلا حقٌّ».
[صحيح] - [رواه أبو داود] - [سنن أبي داود: 3646]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Dama doon bind lépp lu ma dégg ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ndax dama koo bëggoon a wattu, Xuraysin tere ma loolu, ñu ne ma: ndax dangay bind lépp loo dégg ci Yonnente Yàlla bi te moom nit la day wax cig mer ak cig gërëm? Ma bàyyee bind, ma wax loolu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu joxoñ baaraamam ci gémmiñam, daal di ne: «bindal, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, dara du ci génn lu dul dëgg».
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 3646]
Abdullah Ibn Amr -yal na ko Yàlla dollee gërëm- dafa wax ne: Dama daan bind lépp lu ma dégg ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ndax wattu ko cim mbind, gaa yi xuraysin yi tere ma daal di ne ma: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nit la te day wax cig gërëm ak cig mer, te amaana mu juum, ma bàyyi mbind ma.
Ma wax Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- li ñu wax ñoom, mu joxoñ baaraamam ci gémmiñam daal di wax ne: bindal, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom dara du génn ci moom lu dul dëgg ci bépp anam nak, cig gërëm ak cig mer.
Yàlla mu kawe mi wax na ci Yonnenteem bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne: ﴾Yonente bi du waxe ci bànneexu bakkanam* lu mu wax dees ko koo wahyu﴿ [An-najmi 3-4].