عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«مَنْ كَذَبَ عَلَيَّ مُتَعَمِّدًا فَلْيَتَبَوَّأْ مَقْعَدَهُ مِنَ النَّارِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 110]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"ku ma fenal te tay ko na waajal ab wàccuwaayam ca sawara".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 110]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne ku ko fenal te tay ko askanale ko wax walla jëf ci ay fen, kooku allaaxira am na fa toogukaay ca sawara; muy ag payam ci li mu ko fenal.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Fenal Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jublu ko ca te tay ko sabab la ci dugg sawara.
  2. Fenal Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yamul ak fenal yeneen nit ñi, ngir la cay tege ci yàqute yu màgg ci diine ak àdduna.
  3. Dañuy moytondikuloo tasaare ay hadiis lu jiitu ñuy gëstu ak a wóorlu ndax li ñu ko askanale Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wér na walla déet.
Gaaral tekki yi
Làkk: Àngale Urdu Español Ndollent (55)