+ -

عَنْ سَمُرَةَ بْنِ جُنْدَبٍ وَالْمُغِيرَةِ بْنِ شُعْبَةَ رضي الله عنهما قَالَا: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَنْ حَدَّثَ عَنِّي بِحَدِيثٍ يُرَى أَنَّهُ كَذِبٌ، فَهُوَ أَحَدُ الْكَاذِبِينَ».

[صحيح] - [رواه مسلم في مقدمته]
المزيــد ...

Jële nañu ci Samurata Ibn Jundub ak Muxiirata Ibn Suhbata yal na leen Yàlla dollee gërëm ñu wax ne, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"ku ma waxal jenn wax te xam ne ay fen la, moom kenn la ci fenkat yi".

[Wér na] - - [Téere Muslim bi gën a wér]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne ku toxal ab hadiis askanale ka ko fekk xam na walla mu not ci njortam ne dañu ko a fenal Yonnente bi kon aji-nettali ji day bokk ak ki sos fen wi.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Wóorlu ci hadiis yi ñuy nettalil Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ak wóorlu ag wéram laata ñu koy nettali.
  2. Melow fen dees na ko boyal ci képp ku sos aw fen ak ku ko toxal tasaare ko ci nit ñi.
  3. Araamalees na nettali hadiis bu ñu sos ci képp ku xam ne danu koo sos, walla ag sosam not ci njortam lu dul mu koy moytandikuloo.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Pastoo Asaami Suwiit Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Serbi Rom Majri Ciikiya الموري Asrabijaani Ukraani الجورجية المقدونية
Gaaral tekki yi